Li ab Wotté la guir le 25 Mai 2021

nguir arrêté Racisme ak Niawtéf you Taak‘deer yi (policier) !
Dinaniou khewall ak diapallé bépp mbollou ak khèw-khèw si bissou 25 Mai 2021 dadié ak …
… Magal bissou Dé bou niaaw bou GEORGE FLOYD tassé wonn ak 25 Mai 2020.
… Bissoup Mom Sa bopp bou Afrique, biy Magal sossouk ndadié guir Xèèx Mommel nguir Bolloq Afrique sa bissoup 25 Mai 1963
… Foukel lou Magal bissoup dé bou Niaaw bou CHRISTY SCHWUNDECK ça 19 Mai 2011.

Xèèxoup Bodikou bi niou niouy bodikou dou lou xeew rek waleu dou am pfoo si nioun, wayé ak doundoug beuss bou nekk la. Motah Niaxtou lou waar la thé yit tambali wouniouko si déwouk GEORGE FLOYD. Mou don sa Amerique, Brésil, Haïti, Nigéria, Sénégal walla sah fi si Allemagne, danioo wara Bollo té Xeex. Bissoup 25 Mai donnoul rek Beuss bi niou raay GEORGE FLOYD. Sa 1963, 25 Mai magalloon nanie ko si deuk bi ak Bitiim rew di beuss bi Afrique momé boppam. Biss bi day feusseul sounou bollo si nguir téégui bepp xetou Notél bou diougué Bittim Rew.

Nekinou Kom-Kom mou Adouna bi niongui ko tékksi ay Atti Ndiam, Raay gou barri ak Nootél gui niou Toubap yi teguon. Bodikou bi, manam diaap né niit kou Wekh mo gueun mo warall yi khetti niawtef. Door yi ak Rayy gui niouy Ray bit niou nioul gni si Afrique ak bitim Rew bokk nassi lolé.

Fi si Reewmi bodikonté bi tamballi woul si Ngourouk Hitler. Ak weyeulou topp intérêk Allemagne ganaw Xettou Niawtef ya Amonn ça Namibie, ak dollél Ngour gou bonn guaffa nekkon la.
Allemagne mo waralon yobnéb ay Nganaay, tambalik ay Kharé, ak itaam Niawtef ak dé wouk dommi adama you barri ça beureub yaniou nekkon ça Méditerranée.

Raay gui way Taak derr yi di Ray nitt niou Nioul ñi feuss na lol so Allemagne. Yissi gueunonna feuss bokna si déwouk JOHN ACHIDI ak N‘DEYE MAREAME SARR ça attoum 2001, ak OURY JALLOK ak LAYA-ALAMA CONDÉ ç attoum 2005. Çi Att mi laniouy Magal déwouk CHRISTY SCHWUNDECK. Police ak way Taak deer yi niokko Raay ça 19 MAI 2011 ça beureup bou ligueyyou kay GALLUS ba ça FRANKFURT.

Xettou Niawtef yiniouy tekk nit you nioul yi tambaliwoul rek si bouniou Way takk deer yi di topp ba diniou Raay. Day am tamiit si beureubou yoon yi, beureubou liguéyou kay yi, you Fadiou kay yi, you Diangg kay yi, beureubou ada yi ak you fowoukay yi: Manam sen bollém mbolli yi danou niouy Boddi.

Ngourouk Allemagne, ak mbolloy wa Allemagne yi wonné nagn ni manou nio lidianti sounou ay beug beug. Motah nak niouy wo nieup si niou bollo théxexaal sounou bopp nguir dieulé fi Bodikou bi, ak bepp xettou niawtef ak xoxxatal bi.

Daniou Xeex ngui diaami bepp niit kou nioul. Ak Rew mouniou manti nekk, danio bokk diar diar ak founiou sokhiko mouy ça Afrique. Notél gui ça souy wéy ça Afrique, bénneu niit kou nioul dou doumd si diaam. Motah niouy bollo ngui dieulé fi Notél ak Bodikou biniou def dieumalé ko çi Afrique.

Sounou bollo wé don Benneu laniouy eup dollé !
Bollo ak aar sunu Bop !

„Niou Xeex lou guir sounou diaam lou Waar la. Niou am Ndam lou waar leu. Danio wara beuganté té Diapalenté sunu biir. “ – Assata Shakur